1.FAN YI NGA FI NEWUL TERAL JABAR/LES JOURS DE TON ABSENCE HOMMAGE À MON EPOUSE
Éthiopiques n°92.
Littérature, philosophie et art
De la négritude à la renaissance africaine
1er semestre 2014
FAN YI NGA FI NEWUL TERAL JABAR
Fan yi nga fi newul
Asaman leeratul
Picc sabatul
Ngelaw sax wolatul
Fan yi nga fi newul
Dara safatul
Gisuma lu ko fi jarati
Di na ko wax waxati
Baay de fàttewul
Doom it fàttewul
Yàllaay yiir jabar yor
Yéené doyul ci bii bor
Tànn jom sàmm ngor
Tette doom ba mu tekki
Jii jikko kenn du ko sekki
Céy waay fan yi nga fi newul
Xol tërëdi xel nelawul
Saa xalima dina may tooñ
Sorelooma lool sa may ñoñ
Yow nga teew ferloo rongooñ
Fan yi nga fi newul
Ngelaw li sax wolatul Séex Aliyu NDAW
LES JOURS DE TON ABSENCE HOMMAGE À MON EPOUSE
Les jours de ton absence
Le ciel est devenu sombre
Pas un oiseau ne chante
Aucune brise ne se lève
Les jours de ton absence
Plus rien n’a de goût
Tout plaisir est perdu
À quoi bon chercher
Je le dis je le répète
Le père n’oublie guère
L’enfant n’oublie guère
Dieu protège et l’épouse tient le foyer
Dans sa paume
Que de vœux pieux face à l’énorme
Dette
Choisir l’amour propre prôner la dignité
Élever du berceau à la réussite
Telle conduite est à magnifier
Ah les jours de ton absence
Cœur sans repos esprit non tranquille
Ah l’emprise de ma plume
Quel préjudice elle me porte
Pour trop m’éloigner des miens
Ah ce don de ta présence
Et toute larme s’efface
Les jours de ton absence
Aucune brise ne se lève
Traduction de Cheik Aliou NDAO
Dakar, juillet 2012